Ndaw si fi nekkoon te né du sey ag boroomub légët

Léebóon

Lippóon

Amoon na fi

Daan na am

Ba mu amee yaa fekke ?

Waxal ma dégg !

Jongama ju rafet ba dee, moo néwoon : “man déy, duma séy ag boroomub légët. Ñu daldi ko né : “kooy séyal boog !”

Mu né : “Xanaa ku amulub légët !”

Aw far jógé Ngaay, dikk, àndi ñaari woto : bii marsandiis la, bii ay wurus la, ag ceeb, ag pañey guró, ag wurusu wóor. Jongoma ji dikk, né : “balaa daray xew de yaay, damaa dugg ag moom ci néeg bi !”Ñu taal ñetti sondel ; ñu dugg ci néeg bi, di ko wisit, di ko wisit, di ko wisit ba ni ko : “summil sa tubéy !”Mu summi tubéyam.

Mu né ñill taat wi, ni ko :

— Lii légët la di te man duma séy ag boroomub légët !

Mu né ko :

— Koon nag lu ma la yótoon lépp, bàyyi naa koog yow ; daldi dem.

Ka ca des itam, daldi jógé ca Mburus, dikk : pañey guroom, xaalisam ba mu doy, wurusu wóor ba mu doy, balóoti séram ba mu doy, mbooloom ba mu doy. Sëf ñaari nag, ñeenti xar, def jiwoom ba mu doy, mu ñów. Tama yaa ngi topp ci moom, sabar yi làmb — laa la wax man — nit ñaa ngiy wereelu, ñi ci des, ñu ngiy sakket di fecc.

Mu né : “Yaay kat amati naa an gan.”

Yaayam tontu ko né : — tey jii, ni nga ameeg gan, ag nii ñu agsee, ag seen ñam yu bare yii, ag seen woto yu doy yi, ag seen tëgg mii, ñam yu bare yii, ag seen woto yu doy yi, ag seen tëgg mii ñu àndal, man déy doom, noo mëna def tey jii — dinaa wax sama jaam bii ndax ñu reyal la am xar ñu reere ko. Bu subaa nag, mbooloo mii fii tase ci dëkk-dëkkaan yi, daañu rey nag.

Ñu def noonu, mu ni :

— Yaay, balaa daraa xew kat, def leen ndànk, ma wisit ko.

Mu wisit ko, daldi né ko :

— Yow sa tëru ween wii, ab légët a ngi ci di !

Jinne ja dégg ko, daldi fab lu doon ag ngeer — laa la wax man mii— soppi ko ay fasu naarugóor, latkoloñ gi xeeñ ci biir dëkk bi, mëneesula xam ni xet gi neexe.

Ndënd yi tëgg, xameesul neexaayu tëgg mi ni mu neexe ; mbooloo mi topp ci moon, fasu naarugóor yi, ku ci nekk yaa nga yéeg ca kow.

Dëkk bépp leer — ba mel ni (bëccëg) : bu sa pusó wàddee sax dinga ko for.

Ñu ni mamaax yegsi.

Jongoma ji daldi yónni jibéer ba ni ko :

— Soo demee neel saa baay, na ma wutali gétti nag, àjjuma ba àjjuma dellusi ! Na ñu ma wutal gétti fasi naarugóor, àjjuma ba àjjuma dellusi ; xaru tulaabéer yi, na ñu ma wutal séng yu ñu nekk àjjuma na àjjuma dellusi, am ndox, te sama dara nag bu mu mànke ndax maa ngi ñów ag sama mbooloo.

— Ñu ni mamaax ci biir dëkk bi : ndekete woo, jinné ji moo koy doxaansi nag, moon ci boppam. Ba mu dikkee ba ni “yàyy”ni “mutt”! xaalis bu bare, bi mu yorewoon tàsaaroo. Mu né :

— Loolu sax dey, guné yu ndaw yee ko moom ag màgget yi !

Nit ñi di nërëm nërëm di for. Jinné ji ci des ni “yàyy”ni “mutt”! wurusu ngalam wiy def ñetetetetetet di rot. Mu né :

— For leen, yeen jànq ji, yeena moom loolu, ngalam, guné gu jigéen gu rafet a koy yello !

Nakka ñu wàcc, mu né — moom jongoma ji— moone baay de waay, sama gan, gii, man, defe naa ni tey jii laay séyi ; ni bërét, ni jibéer ji génnéel ma saa armoor ba.

Mu né ruséet armor ba, daldi koy ni déjj. Jongoma ji daldi né :

— Yaay kat, man damay dem, kii moom, xam naa né du yorub légët, jinné la kat !

Nakka far wi ñów, daldi dikk né ko :

— Defal ndànk, ma wax ag sa moroomi gor yi.

— Déedéet, damay séyi tey, dikkal sax nu dem ci néeg bi, ma wisit la.

Mu wisit, wisit, gisul benn légët mu né : “dem naa”. Ñu daldi dikk, né ko : “ayca boog nu génné basaN yi.”Ñu daldi génné basaN yi, woo magi dëkk bi ñu léemu ko. Ñu bàyyi fi fasu naarugóor yépp, xaru tulaabéer yépp, nag yépp, lépp, ñu ba ko fi. Nakka mu né ñuus ci kow fas wi, ñu dem na génn ci ginnaaw dëkk bi, fas wi daldi detteelu tollu ni mbaam, tànk yi daldi wàttatu. Mu né :

— Aan ! moom kat, lëf li moom…!

Mu né ko : “Eéy ! yemal, deesul wax guddi !”Jinné ji ko doxaansi kat Saatañaali la tudd.

Guney Ndar né : “Xaee éy Saatañaali, mbër nga ? Mu né leen :

— Teel ngeen, yegguma fi ma jëm !”

Ñu dox lu tollu ni sunu ginnaaw kër, mu ni yëfóot ci taatu guy, né guy gi nàll am xët, ni ko narr ci dënn bi, ween yi ni taréet !

Jinné yu ndaw yi né :

Saatañaali bon nga,

Saatañaali bon nga,

Sémpi guy gi booleeg jinné yi

KoliN, KoliN, KoliN.