Sey bu wóorul

Léebóon

Lippóon

Amoon na fi

Daan na am

Ba mu amee yaa fekke ?

Yaa wax ma dégg.

Waxi tey matul a dégg.

Sa yos a ci raw

Waaye dégg dégg matul a xeeb.

Waawaaw, nde wolof Njaay day yokk waaye du sos.

Lu mu wax am na dalill !

Dafa amoon ay jànq yu baree bari, ñoo fi newoon, dem cib màrse — né : ku bëgg jabar na daldi dikk. Nit ñi daldi dikk, ku nekk jël jabaram, buur it dikk, daldi jël jabaram.

Ca suba sa ñoom itam, ñu daldi né dañuy xëy ca tool ya. Ñu teela togg seeni reer — ndaxte nit ñaa ngiy mbóolu — dañuy mbóoluji, ñoom itam. Jabaru Buur itam war na ànd ak ñoom ; ñu daldi cay dem né ko : “Aa yow doo demem ?”

Mu né leen :

— Aa ! man dé, sama jëkër dafa ma mooñloo tey jii, te dama koy mooñal ! Damay togg ba pare. Bu subaa dinaa dem.

Ñoom itam ñu daldi né ko : “koon dé noo ngi dem, bu subaa nga dem”. Ca suba sa, mu daldi raxas njaqam ba mu set, daldi tànq ndox, daldi dem ba ca àll ba, daldi taxaw — summéeku ba set — daldi né : Njabba cuuti ! Njabba cuute maccuuta mbelangal ! Su ma xamoon ne dugub ñorna, maccuuta mbelangal ! Duma sey ag baay Buur Njaay, maccuuta mbelangal.

Naar ba di ko xool rekk ; moom, ndaw si, gisu ko. Mu daldi dem ba ca mbool ma, daldi neeti :

— Njabba cuuti ! Njabba cuute maccuuta mbelangal ! Su ma xamoon ne dugub ñorna, maccuuta mbelangal ! Duma seyag baay Buur Njaay, maccuuta mbelangal.

Mu daldi dem, def taati neen, soppeeku am picc, di lekk, di lekk ba mu yàgg. Mu soppeekuwaat : solaat mbubbam, daldi yenuwaat njaqam, daldi ñibbi.

Naar ba yit daldi cay topp, daldi dem né Buur :

— Yow mii dey sa jabar am picc la !

Mu né ko : “Yow dangay fen, tey jii, dinaa la fetal”.

Naar daldi né — Man dey fenuma te boo ko weddee, suba, ñowal nu ànd. Ca suba sa mu xëyaat dem, summeeku ba set, daldi né :

— Njabba cuuti ! Njabba cuute maccuuta mbelangal ! Su ma xamoon ne dugub ñorna, maccuuta mbelangal ! Duma seyag baay Buur Njaay, maccuuta mbelangal.

Daldi dem ba ca gittax ga, mu daldi yeegati, daldi nekk picc, daldi yéeg ca kow daldi né :

— Njabba cuuti ! Njabba cuute maccuuta mbelangal ! Su ma xamoon ne dugub ñorna, maccuuta mbelangal ! Duma seyag baay Buur Njaay, maccuuta mbelangal.

Daldi taxaw di lekk, di lekk : Buur a nga ca ñag ba rekk moog naar ba. Ba mu yàgg, naar ba né ko :

— Yow mii déy — sa jabar jaa ngi née, gis nga ko, picc la !

Ñu bàyyi ba ñu dem ca kër ga ; moom itam (ndaw si) mu ñibbi, daldi sumbag mooñam, di mooñ… Buur daldi né :

Mu né ko : — Ay nijaay, bàyyil woy woowu te ma may la loo bëgg, sama jaaroy wurus yeeg, sama yépp dinaa la ko may.

Buur né ko — Man, woy wu ñu may maye ay jaaroy wurus ag yépp, duma ko bàyyi kat ! — daldi né : (woy wi wépp).

— Ndaw si né yuréet tànki picc !

Buur woy (woy wi wépp).

— Mu daldi génné yépp, yëfu picc, yépp…

Buur dem nag wutuw yat doon ko bëgga dóor, far mu naaw wocc ko fa !