Taalibe bi ag jabaru sëriñ bi

Léebóon

Lippóon

Amoon na fi

Daan na am

Yeena kekkee ?

Yaa wax nu dégg.

Waxi tey jarula dóore sa doom.

Sa jos a ci raw.

Dafa amoon benn sëriñ boo xam ni bii, àddina juróom-ñaar moo fi dàq jàng. Amoon na téeméeri ndongo ag juróom-ñaar-fuuk ; di jàngal ndongo yooyu ba yàgg mu am benn ndongoob gan. Kooku la gënan bëgg, te séetub sëriñ bi, ndongo boobu rekk, la gëna bëgg. Sëriñ bi ni leen :

— Maa ngiy tukki ; ndongo bi soo xëyee nga dem ca tool ya, ca basi ba, nga tàmbalee caa bey.

Sëriñ na nag daldi génn…Ndeke tukkiwul ! Mu fab ag fetal ag ñaari ngémmiñam, dem yéeg ca daqaar ga ca tool ba. Té ca daqaar ga, fi la ndongo bi wara xëy di bey. Sëriñ bi daldi yéeg ca kow ni cell.

Jabar ju ndaw ji daldi né ndongo bi na fa dem : xarum sëriñ bi nga xam né jéll na juróom-ñaari tabaski, moom laa lay reyal, togg ko ag la ca war lépp, yot la ko ; te su ma ñówée, dinaa mel neneen : juróom-ñaari kilóoy fer yu weex, dinaa ko sol, fekk la fa ag ñetti kilóoy fer yu xonq !

Ndongo ba daldi gàddu goppam, daldi wuti tool ya. Ba mu yegsee daldi geestu fu ne, door di tàmbali di bey, daldi né bismiilaahi, daldi door woy, naan :

“Cacaa, ca basi ba, Cacaa, ca basi ba. Bay sëriñ tukkéetina waay. Cacaa, ca basi ba. Yàlla na ca gata dee nag : Ma doon kër, donn ab toolam, Cacaa, ca basi ba, ba donnaale ca séetub daawam, Cacaa, ca basi ba.”

Ba mu woyee ba noppi, daldi sëpp gopp bi, daldi tanq ci ndaa li naan ba noppi, tàmbali di séentu…

Ndaw sa nag booba woona ñeenti ndongo, ñu fab xar ma daldi koy rendi, daldi koy fees : mu daldi koy togg !

Ndongo bi toog ci tool yi ba yàgg, togg gi xeeñ ko, mu geestu, séen tan yi di naaw, mu daldi sëggaat ag goppam di bey, daldi tàmbaliwaat di woy :

“Cacaa, ca basi ba, Cacaa, ca basi ba. Bay sëriñ tukkéetina waay. Cacaa, ca basi ba. Yàlla na ca gata dee nag : Ma doon kër, donn ab toolam, Cacaa, ca basi ba, ba donnaale ca séetub daawam, Cacaa, ca basi ba.”

Ndaw sa nag daal, yenu ndab la nag, fekk ko fa daldi sukk né ko : jërëjëf. Mu daldi yenneeku, daldi dindi sér yi, lal ba mu des benn sér bu ndaw bi…Mu daldi jaaxaan…

Ndekete nii mu tëdde, mu ngi jàkkaarloog sëriñ bi : seeni bët tase, mu tàmbali di lox. Ndongo ba ni ko :

— Lu mu doon ? Waxal, waxal gaaw !

Ndaw si né ko :

— Danuy jëkk lekk am danuy jagal, danuy Mataaru Njaga Sàmba. Ndongo ba xool bëti ndaw si né ca kow, mu né : “Kii dé dara la gis waay!”Daldi geestu, téen, séen góor gi ci kow garab gi ag fetalam, mu daldi yóoxu ni :

— Danuy jagal ndax nu gaawa dee !!

Fa la léeb doxe tàbbi géej, bàkkan bu ko jëkk fóon tàbbi àjjana.