Ñetti xuuge yi

Dafa amoon genn góorug, amoon jabari xuuge ; ndekete jabaru xuuge bi am na ñaari fari xuuge — xam nga muy ñetti fari xuuge !

Bi nga xam ne toog nañu ay fan, jëkkëru xuuge bi tukki. Jabaru xuuge bi dem ci wenn faru xuuge bi né ko :

— Sama jëkkër tukki na, ngoon, na nga fa ñów !

Ba mu fa jógee daldi dem ca ka ca des — né ko :

— Sama jëkkër tukki na, na nga fa ñów, su ngoonee !

Ba ngoon jotee, ñoom ñaar ñépp agsi ci biir Kër gi, toogandoo ci lal bi, di waxtaan. Noonu, kenn ki yëngal tànkam far mu dal ci ki ci des —, mu né ko : — Saa waay, yaa ngi may gaañ ! Kenn ki né ko :

— Nu ma la gaañe ? Sama tànk yëngu rekk nga né maa ngi lay gaañ ! Saa waay, yow itam gaañuma la waay !

Beneen xuuge bi né ko :

— Aaa ! Loolu ngay wax ?

Kenn ki né ko :

— Waawaaw !!!

Fi ñu koy waxee, ñoom ñaar ñu jóg taqaloo ci ruum bi ; jigéenub xuuge bi jóg, doon leen àtte, far ñaari! xuuge yi ku ci nekk né këpp ci suuf ; ñu dee ñoom ñaar ñépp, te, ci dëkk bi kenn du fa suul ab xuuge.

Jabaru xuuge bi nag, waaru lool ; xamul nu muy def. Mu génn, daldi gis ab naar bu wax gëléeman, mu woo ko, né ko :

— Dama bëgg, ma fey la, nga suulil ma xuuge bii, dee. — Fekk làq na benn xuuge ba ca ron lal ba. Bi ñu dégoo ci kàddu, Naar bi daldi koy sëf ci gëléem gi. Jigéen ji né ko :

— Xuuge nàqarina suul ! Soo wattuwul rekk, boo ñowee dinga ko fi fekkaat !

Naar bi né ko : su ma ko suule du dikk ! Naar bi fab xuuge bi gàcc ci gëléem gi, dem suuli…

Bi muy laata ñów — fekk ndaw si ñoddi beneen xuuge bi, daldi ko teg ci buntu néeg bi. Naka naar bi jub buntu kër gi rekk, ndaw si tàccu ko, né ko :

— Xuuge, moo gaaw, waaye, bàyyil ba ma yóbbuwaat ko, dootul gaawa ñów !

Mu daldi fab xuuge bi, sëfaat ci gëléem gi, dem. Mu dem gas meneen leeñ ba mu àgg ci nóoru bopp ba, mu daldi suul. Mu jóge fa ñów. Naka mu ñów ba ci buntu kër gi, dajeeg jëkkëru ndaw si, daldi ñef ab peel — fi ko ndaw si naan :

Déed, sams jëkkër la ! — mu dolli beneen, mu dee, mu yobbu ca armeel ya suuli.