Cosaanu Ndombo

As soxna dafa amoon doom ju jigéen. Bi doom ji matee sëy mu maye ko. Yalla def xale ba ëmb. Bi mu demee ba ci juróom ñeenti weeram, am bès, mu nekk ag yaayam ; ba ñu añee ba sottal, yaay ji woo nag ñetti moroomam. Mu daldi né moroom yi :

— Dama bëggoon ngeen àndal maag sama doom ji nekk ciw mat, yóbbu ko mu doxantu ndax yaramam wi nàyyi.

Moroom yi daldi ànd ag xale bi doxantuji ba ci tàkku dex ga, taxanaale fa. Bi ñu taxanee bay ñibbi, ñu ñów ba ci taatu dàqaar gi, yenneeku fa, di naan ci dex gi. Mat wi daldi jàpp foofu xale bi, mënatula def dara. Mu tëdd ci ag taatu daqaar, ñi mu àndaloon né ko :

— Xaaral ñu dow ca dëkk ba woowi sa yaay.

Bi àndandoo ya demee, xale bi des fa, moom doNNag jaljaleem. Jinné ji dëkkoon ci dàqaar gi daldi génn fekk ko ci taatu daqaar gi, moom rekk. Mu dimmali ko ba mu wasin. Daldi ko jël moog liir ba, yóbbu ko ci biir garab gi (këram).

Bi àndandooy xale bi wootejee ba dellusi, gisatuñu kenn ci taatu garab gi ñu ko bàyyiwoon !

Bi ñu wutee ba tàyyi gisuñu kenn, ñu yaakaar né rabu àll dafa lekk xale ba. Booba xale baa nga kër jinné ja.

Jinné ji ngénté na ko ba santale liir bi santam ; xale bi toog na lu tollu ni ñetti weer kër jinné ji ; bés bu ne jinné ji dina dem ca dëkk ba seet lu xew kër yaayu xale bi, xamal ko ko.

Benn bés mu ñów né xale bi :

— Yërém naa sa yaay ndax bi ma la jëlee ba léegi, guddi ag bëccëg mu ngiy jooy. Dinaa la bàyyi nga ñibbi ngir moom.

Bi mu ko waajalee, wutal ko yéré ag wurus wu bare, daldi woo doomam yépp ñu teewe, mu né xale bi :

— Man, Maymuna laa tudd, sant Jóob. Duma sa yaay waaye mel na ni maa la jur ; ndax dëkk bi nga nekkoon maa di seen rabu tuur. Maa yilif mboleem ñi dëkk ci daqaar gi. Dinaa la booleeg suma doom yii, ñu gungé la ba ca sa kër yaay.

Noonu mu jekki ba guddi daldi ko génné, dellu woo jinné yépp ñu teewe, mu dindi benn ndombo jox ko, wax ko xam-xam ndombo gi, teg ca né :

— Joxuma la fas gi, yow ci sa bopp, sa doom laa ko jox. Su ko takkee dina yàgg ci àddina. Boo demee seen dëkk, ngalla bu kenn dindi sant wi ma ko jox. Te boo demee seen dëkk na nga fexe dëkksi yaag sa yaay ag sa jëkkër ci taatu dex gi. Dëkk bi ngeen nekkoon daañu toxusi, fekksi leen, boo defee li ma la wax, — sa doom — cosaanam ag lu bokk ci giiram ñoo di moom dëkk bi.

Bi xale bi ñibbee, fexe ba toxu ca taatu dex gi, waa dëkk ba wàccsi ci taatu dex gi, fekksi leen.

Doomu xale bi nekk buuru dëkk bu bees bi, bi mu màggee.