Lu-tax am jigéeni Ngor ñu dul am Jëkkër

Boo leen di faral di seetlu di ngeen gis né, léeg-léeg dina am i jigéen yuy nekk janq ba ba ñuy màggat di dee te duñu sëy.

Loolu nag am na lu ko waral ; ba fii ci Ngor sax am na lu fi xewoon ci jamano luy leeral mbir moomu. Mag ñi di ko nettali ba fii ñu tollu tembe, kenn mënu koo weddi, waawaaw.

Dañuy faral di wax né dafa amoon benn nappakat bu dëkkoon ci tefes gi. Mu di gëti di ñów, di gëti di ñów ba yàlla def mu am jabar. Muy sëy ag moom, di sëy ag moom ba lu tollu ci fukki at te musul am doom.

Lëf li metti ko lool, metti ko lool ndax ñi mu dëkkal duñu darajaal waxam. Moom ndeke daf daan def bu gëtiwaan bu yooryoor mu teer ag gaalam ca téngéen, noppalu fa tuuti, daldi jógaat tëmbal gaalam, bu fekkee li mu jàpp bariwul mu nappaat ; bu baree dëgg, mu teersi. Léeg-léeg bu guddee, jabar ji doNN moo koy watle gaal gi.

Benn bés nag ba mu teeree Téngéen, di fa noppalu, mu for bët.

Ci biir nelaw yooyu mu gént mettitam rekk la jooytu : mu di ñàkk gi mu ñàkk am doom. Fekk na bi muy nelaw bay gént, am na genn góor gu yor sikkim bu gudd weex tàll ; kawaru boppam it dafa sëq weex furr. Mu daldi ko yee, nappakat bi daldi jóg, ba ñu nuyyontle ba noppi, góor gi xamal ko né moom moo di Buur Téngéen. Mu teg ci né :

Yeg naa sa mettit, xam naa sa soxla te it bëgg naa la dimmali, ndax am naa mën-mënam.

Buur Téngéen dellu né ko :

— Dinaa ko def nga am doom ; te jigéen lay doon, bu juddoo nga tudde ko Mbeex ; waaye loolu maa ngi koy def ci kow nga nangu lii ma lay wax :

Nappakat bi né ko :

— Waxal, loo wax rekk dinaa ko topp.

Buur Téngéen daldi wax né ko :

— Lenn rekk la : bu Mbeex màggee warul sëy, warul am beneen jëkkër bu dul man. Duma ko jël mu fekksi ma, ci seen loxo lay des yow ag sa jabar ; waaye warul am beneen far, warul am beneen jëkkër bu dul man.

Nappakat bi daldi nangu :

— Bul am mukk loo ciy xalaat ; nii nga ko waxe noonu lay ame.

Buur Téngéen jekki né mes. Nappakat bi itam tëmbal gaalam.

Ba ñu toogee ba lu wara tollu ci at, jabari nappakat bi am doom, mu nekk jigéen. Nappakat bi itam tudde ko Mbeex.

At yi di ñów, di dem, Mbeex di màgg, at yi di ñów, di dem, Mbeex di gën màgg ; at yi di ñów, di dem, Mbeex màgg ba doon jànq bu mat sëy. Mu nga la ko taaru taar bu kenn mósul teg bët.

La nit ñi foogoon ? nañu né àddina bi yépp jigéen du taaru mukk ba dab Mbeex cib taar.

Li mu gënoon sopp moo doon toogi ca xeeru géej ya jàkkaarloog Téngéen. Góori dëkk bi sax dañu ko ñemewulwoon doxaan ndax taaram bu jéggi dayo.

Benn bés jaykat bu am alal bu né ca dëkk ba ca wàlla, ñów di doxaansi Mbeex. Saa yu ñówee rekk bàyyi ci loxay baayu Mbeex ag yaayu Mbeex xaalis bu baree bari. Saa yu ñówee rekk def noonu.

Bés dikk, baayu Mbeex fas yéené may Mbeex jaaykat bi ndax alal ji. Nappakat bi fàtte waxam.

Ba noonu, benn àjjuma rekk ñu maye Mbeex waaye sa bés ba, balaa jànt bee so Mbeex daanu feebar. Feebar bu gaawa-gaaw roofu ko ba tëral ko. Feebar bi metti lool ba ñuy xalaat né Mbeex du fanaan. Baay bi tiit lool, xelam dikk, dellusi ci li mu waxantewoon ag Buur Téngéen. Ci saa si mu woote ngir ñu tas sëy bi. Sëy bi daldi tas. Mbeex tàmbale féex tuuti. Waaye feebar bi jeexulwoon ci moom. Ci guddi gi baayu Mbeex daldi tëmbal gaalam, lu mu daawul faral di def. Nit ñi xaw ci jaaxle, ba di ko waaja gunge. Mu gàntu leen, Ba mu joowee ba yegg Téngéen, dafa wéeru ca garab ga mu daan wéeru rekk daldi for bët. Noonu Buur Téngéen yee ko, xamal ko moom mooy kan. Daldi ko ci tegal né ko :

— Yaa nangul woon sa bopp daldi gisal sa bopp ; yaa weddil sa bopp, gisal sa bopp.

Buur Téngéen daldi ko né :

— Boo bëggee Mbeex jóg, balaa ngaa teer, tanqal ag sa mbàttu ci Mbeex mi, boo yegsee kër ga nga tuur ko ko fa mu tëdd ; bu ko defee dina jóg.

Baayu Mbeex daldi tontu né :

— Sàllaaw, nii nga ko waxe, nii rekk laa koy defe.

Buur Téngéen dellu né ko :

— Te bul fàtte mukk né Mbeex warul am weneen far wu dul man ; warul am jeneen jëkkër ju dul man.

Buur Téngéen xaarul sax nappakat bi tontu mu daldi né mes. Nappakat bi itam tëmbël gaalam. Ba mu joowee ba di jub tefes ga, mu daldi tanq si mbeex mi na ñu ko ko waxewoon. Ba mu watee gaal gi be noppi, mu gàddu mbàttu ba nów fekk Mbeex fa mu tëdd, mu daldi ko sotti mbeex mi. Mbeex it jóg ci saa si mel ni ku dara mosul jót. Feebar bi jeex tàkk ci moom.

Nit ña doon toogaanu Mbeex yéemu lool ñu gëna dëggal né :

— Mbeex du nit doNN yem ci.

Baay ba nag doxe fa nangootul mukk di déglu sax kuy wax mbirum sëy ag doomam.

Mbeex itarn mel ni loolu dafa newul sax ci xelam, mu mel ni danga ko xirtal : ngoon su né mu defaru ba jekk, jubal yoonu xeer ya di doxe tànku neen topp tefes gi, bu yegsee ci xeer yi dafay toog moom kenn doNN jublu géej, jàkkarloog Téngéen. Daana tooge noonu ay waxtu léeg-léeg sax guddi gee ko fay dàqe. Nit ñi daañu daan wax né Buur Téngéen moo di faram.

Mbeex daal noonu la jàppoo ba bay ñibbi àllaaxira 77 jàppoo ko ba yaay ji wuyuji baayam. Mu maàggat be dee ci janq te mosul sëy.

Notes
77.

Ñibbi àllaaxira : wax la juy tekki né baay dee na ; àllaxara moo li ñuy fekki bu nnu deewee