Musibam Mbàbba Kumba

Amoon na fi ab dëkk bu tuddoon Mbàbba Kumba. Kenn xamatul fu mu nekk léegi. Waaye mag ñi fattewuñu ko ngir ay jalooreem, rawatina musibam dëkk ba ak ay ñoñam.

Móodu nekkoon na boroom kër bu tabe, taaru te jàmbaare. Waaye dëgër bopp a ko yàqoon.

Ba tabaski desee juróomi fan, la woo ñaari jabaram ya Kumba aawo ba ak Nogay ñaareel ba ni leen;

- Dinaa fi def lu kenn masul def ngir ngeen xam ne seen nijaay du ku tuuti te it ku fonk njabootam la.

Noonu, ñaari doom ya agsi. Ku nekk ci ñoom dem toog ca wetu ndeyam ba mu nuyoo ba noppi…

- Am xar mu kenn masul xalaat a tabaskee ci dëkk bi, laa fas naa yéenee maggale bés ba.

Waaye mag ñi nee nañu : ku def lu kenn masul def gis lu kenn masul gis.

Móodu dem na daral ba. Li ne ci xelam nag, mo ok yàlla rekk a ko xam.

Ba tàkkusaan jotee, la waa dëkk ba séen sunu jàmbaar ja mu jiital ponkalum xar mu mboq wutalsi dékk ba.

- Moo ! Lii lu mu ? Xanaa kii dafa dof, nit ña yuuxoondoo, màmm wutali boroom dëkk ba ca pénc ma :

- Baay Sàmba, jógal balaa njaaxum di am. Móodu mii sunu musiba la bëgg. Am xar mu mboq la jënd bëgg koo tabaskee te ku ne xam na ne loolu bu amee àddina tukki.

Noonu Baay Samba tas mbooloo ma, ne ñokket jëm kër Móodu.

Gaawtu baaxul, ndax saafara mën naa jur jàngoro.

Teguñ ca as lëf, baayu yaayam agsi nuyu Baay Sàmba ak ñaari loxo.

- Kumba, Kumba gaawal indil ma guro gi ci taatu ndaa li.

Kumbaa doon buuru këram. Loolu moo taxoon Baay Sàmba ni ko woon mu toog ngir fekke waxtaanam ak Móodu, naka la doxe woon yónnent wa ba noppi.

Gannaaw ba mu waxee lu jëm ci mbey mi ak yeneen ak yeneen, boroom dëkk ba ne tekk daldi ni jàkk Móodu :

- Sama jàmbaar ji, mu ne ko, loo narati ?

- Ci lan, kilifa gi ? Dese naa dégg li nga bëgg a wax.

- Li ma jaaxal kay, mooy sa xarum tabaski mii. Jafewaay bi ak coono gi nga ci daj ; te nga menoon am mu ko gën fukki yoon te doo ci xar sa tànku tubéy.

Diir ba waxtaan wa doon daw kër Móodu, coow ak ruumandaat la waa dëkk ba jàppoowoon.

- Móodu, doo fi gan. Say maam fii lañu dund ba xéy faatu ñu rab leen fi te kenn xamalu leen lu dul jàmm ak ngor.

Masuñoo defee maa tey, walla ñu topp seen bànneex ci kaw seeni mbokk. Réerewoo ni xar mu mboq mooy tuuru gox bi. Rey ko ci njuumte waral na sangu ciy xàmb, rawatina nag nga bëgg koo tabaskee.

Fii la sama wax di yam ak yow. Ay fan a ngi sa kanam. Xalaatalaat bu baax balaa ngay def dara. Lu ci aay, sa kaw lay yam. Wasalaam !”

Baay Sàmba mayul Móodu fu mu waxe. Noona la awe dem këram.

- Nijaay, Kumba ne Móodu, yaa ko déggal sa bopp. Waxu mag du fanaan àll ak lu mu guddee, guddee.

- Noppil ! Fii, maa fii sol tubéy, di fi yar sikkim. Waru may wax kenn di ci teg baat. Faalewuma ay wax yu kañaan tax a jóg. Saa sune nii la magi dëkk biy def. Lii aay na, lee gaaf la, loolu alku la. Bu ñu ma rey ndax lu baax kenn bañu ko, waaye nag sa coono.

Petu maak yedd yaak xuloo baak lépp taxul Móodu soppi la mu fasoo woon jëf.

Géwal bu reppee cib xare, lu mu jiin xeeb ko.

Yaakaar naa ne loolu moo daloon sunu waa ji. Ca jullikaay ba sax, am na ñu ko woo ñaaroo ak moom ngir mu dellusi ginnaaw ci turu kóllëreek sutura.

Waaye, ku repp dootul dégg, dootul gis dara.

Fan ya doxoon seen diganteek tabaski gaawoon na ni melax. Su fekkee ne sax yakkamtiw xew baaxul, mii moom jaraloon na ko waa kër Mbàbba.

Am xew ceetaan a ca dàq.

Tey la bés bu magg bi ñépp doon xaar ; Tabaski. Móodu yeewu na ca fajar, sang am xaram mook ñaari doomam ya. Ba mu noppee la jublu ca boppam defaru ba jekk. Subag julli, góor ñee ko moom daanaka. Ba tax ñaari soxanay Moódu ya defuñu lu dul lay ëtt ba ak cuuraay seeni néeg di xaar seen nijaay dellusi jàkka ja.

Gaawaay ba sunu waa ji xottee woon yoon way jublusi këram firiwuloon lu dul naqar ak bëgg a mucc ci mbamb mi.

Ñaar a mën kenn, ku ñu sot nga xam ko.

Móodu ngi xultu naan: ”Duma surgab kenn, te itam duma jaamu ku dul buur bi yàlla. Ay caaxaan taxuñ maa jóg ; ndax ëllëg yàlla rekk ko xam. Ma ni : ndatarfaax waay !! Alal du faj dee ; gàcce lay faj. Dellu sama kàddu ? Mukk ci sama giiru dund !”

Yàkkamti baaxul.

Sunu waa ji rendi ni xar ma ba noppi, door a fàttaliku ne dafa abaloon jumtuwaay ya mu ko waroon a feese waa Njaayeen. Ca taxawaay la gëdde wutalj jeen.

Diggante ba mu genneek ba muy waññiku, la doomu aawo ba ne doomu ñaareel ba : “Tëddal ma def la na baay defoon xar mi.”

Kéwél du tëb doom ja bëtt.

Na mu ka ko waxe la rakk ja tëdde foogoon ne mbir ma ay foowi neen la woon. Benn yoon la yuuxu ; paaka ba daw ca putam ga ba sës. Rey na ko te yëgu ca dara.

Xale xamul dara waaye nag, li war mooy aar ko ngir ëllëg.

Xamatuñu lu Nogay doon defati ba yam ca doomi wujjam wa mu tiim taawam baak paaka bu taq ripp ak deret. Jéemu koo xam sax. Noona la dale ca kawam dal koy rendi. Laata muy siggi la Kumba màmm daldi koy xoj. Jaxasoo ba yàggul dara ku ne ca ñoom daanu sedd guyy.

Móodu dafa agsi kër ga rekk, yuuxu ya jib. Foo tollu di ko dégg. Teguñ ca as lëf, nit ña buur ni ay yamb fees dell ëttab kër ga.

- Lenn rekk a ti sës : jóg ci xar mii balaa muy jóg sunu kaw. Njeexatalu wax ji mooy lii : na ndeyu mbill gi dem yoor musiba mii ca teen bu déy ba. Bu coow li bari, waa Mbàbba mànkoo.

Naka la Moódu tiim teen bi ne moo ngi koy yoor rekk, la tànku ginnaawu xar ma lonku ca téere baat ya mu takkoon. Laata muy féqatu, la tàmbalee ca bopp ba ba ca ndigg la ne menteñ ca biir teen ba. Amatul lu mu def lu dul wallu.

Daw ba raw ci njàmbaar la.

Waa dëkk ba agsi woon ne dañu ko doon xettalisi bari woon nañu bariwaay ba waraloon màbb ak suuxug la wëroon teen ba lépp. Noonee lañu gooree ñoom ñépp suulu ca biir.

Nii lañu ma nettalee musibam Mbàbba.